Noo Yu Mujj Yi

Noo yu mujj yi daal dañuy nuru ab seetu buy melxati bu amul xoosu xoosu amul tilim tilim. Ta nit kune day gis ca seetu boobee –ca anam ga gënë set gënë sell- dundëm gépp, la cay jëf yu baax ak la cay jëf yu bon, ak lañu ko waajalal ngir loola. Ngir nag Noo yu mujj yi baña nekk ab seetu bu nuy gise sunug muj ta fekk nuy naqarlu aka réccu, warnanuy dund dundug njaame cig njub gu sax ci keppaarug Alquraan ju tedd ji ak njubug Sunnë su laab si, ta nutaarale dund gii jëf yu baax yi. Ndaxte àddiis bu tedd bi mingi wax naa: “Jaam bune ca la mufaatoo lañu koy dekkale” (Muslim nettlina ko). Warna ci jaam bi kon mubaña dund ci àddina ta fekk muy sàggane àllaaxira ta baña tàbbi ci kasob bànneexi àddina yi dul sax ta bànneexam di ko jeqqi, ta moytu ëllëg ju raglu ju koy xaar bu wommatoo topp dundug càggante gu mel ne dund googee feese ag réer ak po ca jamonoy ndaw ja ak càgganteg bànneexi jamonoy waxambane ja, dee kat da koy sàkku buy nekk xale ak waxambaane ak mag.
Lii moo tax nag nga wara waajal noo yu néew yi ngir Noo gu mujj gii ngir booy tàggu àddina joojee di jeexi di jébblé ruu gi fekk nga doon jaam bu taaru. Ndax faatug jaam bi mooy bis péncëm bu ndaw.


Read In Other Languages

ALBANIAN
AMHARIC
ARABIC
BASHKIR
BENGALI
BULGARIAN
CHINESE
DUTCH
ENGLISH
FRENCH
GEORGIAN
GERMAN
INDONESIAN
ITALIAN
ITALIAN
JAPANESE
KAZAKH
KURDISH
MALAY
PERSIAN
POLISH
PORTUGUESE
RUSSIAN
SPANISH
SWAHILI
TIGRINYA
TRADITIONAL CHINESE
TWI
UKRAINIAN
UYGHUR
UZBEK